Naka la kifeebar di laablooaknumuyjullé

Naka la ki feebar
di laabloo ak nu muy jullé
 
Ki ko bind
Ash Cheikh Mouhammad Ibn Saalih Al-Usaymîne
(Yàlla nako Yàlla Yërëm)
Kiko Jeema firi
Djibril Dièye

 

 

 

 

Ci turu YALLA lay doore sama mbind mi, moom miy borom yërmande bu yaatu bi, di yërëm ku ko soob.
Mboleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla miy borom mbideef yi. Maa ngi julli aki ñaanal jàmm ci ki gën ci yonnent yi, mooy suñu yonnent MAHAMAD aki ñoñam aki saabaam mbooleseen.
Ginaaw loolu, lii ap tenk la bu aju ciy atte yuy wane naka la ki feebar di labloo ak naka lay jullée.
Pàcc bi ci jiitu mooy naka la ki feebar di laabloo :
1.    Tomb bu njëkk bi mooy war na ki feebar muy laabloo ci ndox muy jàpp ci tojal gu ndaw gi di sangu ci tojal gu mag gi.
2.    Ñaareel bi mooy: su jëfandikóo ndox moomu, jëfandikóo ndox moomu su ko defee, ngir lott walla ragal feebaram doleeku walla wëram yeex bu boobaa dafay tiim.
3.    Ñetteel bi : naka la wara tiime ? ni muy time mooy mu dóor ñaari ténqam ci suuf su lab, benn dóor boobu mu daldi ci masaa mbooleem kanama, ginaaw gi mu daldi masaa benn loxo bi ca beneen ba, ba ñaari yoxo yi daj.
4.    Ñeenteel bi : bu fekkee mënul laabal boppam, bu booba keneen moo koy dimbali ba mu laab.
5.    Juróomeel bi : su fekkee lenn ciy cëram dafa amug ngaañ ngaañ, bu booba dakoy raxasee ndox, su fekentenee ndox moomu dina ci jeexantal, daf koy masaa. Bu ko defee dafay tooyal loxoom ci ndox daldi koy rombal ci bërëb boobu noonu waaye bu fekkee betey rombal boobu muy rombal dafay jeexintal ci ngaañ ngaañ boobu, bu booba dañu koy may mu tiim.
6.    Juróombénéel bi : bu fekkentenee lenn ciy cëram wu dam, dañu koo tabax, bu booba walla book ñu daldi koy yiire dara dafay masaa ci kawam waaye du ko raxas te du  jar itam muy tiim ndax masaa bi mu koy masaa dafay wuutu raxas bi mu ko waroon a raxas.
7.    Juróom ñaareel bi : dina dagan mu tiim ci miir, walla beneen mbir bu laab, boo xam ne pënd yiir na ko, bu dee nak miir bi, li ci nekk du loo xam ne cosaan la bu ñu miin ci suuf, bu booba du ci mën a tiim ludul mu ànd ak pënd boobu.
8.    Juróom ñetteel bi : mooy su fekkee mënul tiim ci suuf walla miir boo xam ne am na pënd du aay mu dadi def suuf ci benn ndab walla ci morso ginaaw gi mu daldi ci tiim.
9.    Juróom ñeenteel bi mooy: su tiimee ngir benn julli ba beneen fekk ko fa fekk tojalul bu booba ca timm bu jekk ba lay jullee julli bii di ñëw te du jar muy tiimaat meneen tiim ndax deñul di nekk ci laab te amul loo xam ne yàq na laabam goobu.
10.    Fukkéel bi : dina war ki nga xam ne feebar mu daldi laabal mbooleem yaramam ci xeeti sobe yi su fekkee mënu ko na julli ni mu nekke noonute julléem dina wér te baamuwaat du lo war
11.    Fukkéel béek benn mooy: war na ki nga xam ne dafa feebar mu daldi julli ak ay yéré yu lab su yéréem yi amee sobe dey war ci moom mu daldi koy raxas walla mu soppi ko ak yeneen yu laab su amul loolu na julli ci nimu nekkee noonu julléem gi dina wér te baamuwaat du ko war.
12.    Fukkéel béek ñaar : war na ki nga xam ne dafa feebar mu julli ci kaw lu laab su fekkee bërëb bi dafa sobewu dina war ci moom mu raxas ko baa mu sppi ko ak beneen bu laab walla book mu daldi ci lal lu laab su amul lépp na julli ci ni mu nekkee noonu juléem gi dina wér te baamu du ko war.
13.    Fukkéel béek ñett mooy: du dagan ci ki nga xam ne dafa feebar mu yeexee ab julli ba waxtoom genn ngir ne dafa lott ci laablu waaye li jaadu mooy na laablu ci keem ni mu ko mëne ginaaw gi mu daldi julli julli gi ci waxtoom donte ne dafa làmboo moom ci jëmam walla bërëbam ni muy jullée walla ay yéréem làmboo sobe boo xam ne dafa lott ci dindi ko.
Ñaareelu Pàcc bi : Naka la ki feebar di jullée
1.    Tomb bi ci jiitu mooy : war na ki feebar mu julli fekk dafa taxaw donte ne jubul xocc walla book mu sukkandiku cib miir walla cib yat boo xamne day aajowoo mu sukkandiku ci
2.    Ñaareel bi, mooy : su fekkee mënul taxaw dafay julli toog li gën nak mooy mu fereŋkulaay ci jamano ba mu taxawee ak jamano bi mu rukoowee
3.    Ñetteel bi : su fekkee mënul julli toog dafay julli wetu daldi jublu penku àndak ne wetu ci ndeejoram moo gën su fekkee dafa lott ci jublu xibla dafay julli ci fi mu mën a jublu bu booba juléem dina wér te baamu du ko war
4.    Ñeenteel bi : su fekkee mënul julli fekk dafa wettu dafay julli jaaxaan daldi jubalé tank yi ci penku bi li gën nak mooy mu yeketi bopam tuuti ngir mu daldi jublu penku su fekkee mënul jubal ay tankam ci xibla bi dafay julli ci nim nekkee noonu te baamu du ko war
5.    Juróoméel  bi  mooy: war na ci ki feebar mu rukoo ak mu sujóot ci biir julléem su ko tëlée dafay daldi junju ak boppam bu ko defee mu daldi def sujóot bi gën a suufé rukkóo bi bu fekkee nak mën naa rukkóo te tëlé sujóot doŋŋ dafay rukkóo waaye su sujóot jotee mu daldi junju ak boppam bu fekkee mën naa sujóot te mënul rukkóo dafay sujôot bu rukóo jotee mu daldi junju ak boppam
6.    Juróom bénéel bi : su fekkentenee mënul junju ak boppam ci rukkóo ak ci sujôot dafay junju akiy gëttam ci sujóot bi mu xef xef gu gën a suufe budee junju ak baaraam ni ko lenn ci ñi feebar di defe loolu dey amul cëslaay xamaluñ ko tamit benn tekktal ci Alxuraanul Kariim ak ci sunna YONNENT BI SALLAHU WASALAM rawatina ci waxu borom xam-xam yi .
7.    Juróom ñaareel bi : su fekkee mënul junju ci boppam walla mu junju ciy gëttam dafay julli ak xolam mu daldi kàbbar daldi jàng bu tolee ci rukóo ak sujóot ak taxaw ak toog mu daldi ko yéené ci xolam te nit ki lépp loo yéené da nga koy am
8.    Juróom ñetteel bi : war na ki ci feebar mu julli mbooleseen julli yi ci seen waxtu lépp li ci war mu defee ko ni mu ko gën a mënee bu ko jooxe mboleem julli yi ci waxtu jotee dina mën a boole digganté tisbaar ak takusaan dina mën a boole timis ak gee boole googu nak dina nekk boole jiital bu ko defee mu julli waxtu takusaan bi ci jamano bi waxtu tisbaar bi julli dugee ginaaw bi ñu jullee tisbaar be noppi waxtu gee bi mu daldi koy indi ci waxtu timis gi ginaaw bi ñu jullee timis pa noppi walla book mu boole boole boo xam ne dafay yiixe bu ko defe mu yiixee waxtu tisbaar ba takusaan ginaw bi jullée tisbaar mu julli takusaan walla book mu yeexe waxtu timis ba gee ginaw bi mu jullée timis mu julli gee loolu nak ci ni mu ko gën a yombee lay tànn ci digganté ñaar yooyu bu dee fajar nak moom du ko booleek benn julli du bu ko jiitu walla bu ci topp
9.    Juróom ñeenteel bi : su fekkee ki nga xam ne da feebar da ñuy koy fajee ci beneen dëkk budul dëkkam mu xam ne dafa nekk ci tukki bu booba mbooleem julli yi nga xam ne ñeent la ñaar la koy def bu ko defe tisbaar, takusaan gee da koy julli benn bu ci nekk ñaari rakka ñaari rakka ba mu dellu ci dëkkam moo xam nak tukkib faju boobu gudd na walla gàtt na YALLA mooy ki nga xam ne mooy defal tawfeex moom la ñuy ñaan mu defal ñu tawfeex ki bind li mooy A Cheikh Mouhammad Ibn SaalihAl-Usaymîne fañu ko jële mooy cisitam bi nga xam ne xët la yu ñu ko jagleel ci yimu def ciy waxtaan ak ciy mbind.
Ay xadis yuy wane ngënéel bi nekk ci feebar aki nattu ak naka la ci julit bi wara muñé
Xadis bi ci jiitu : Jëlee nañu ci Abi Hureyra ak Abi Saiid Al-Qudri Yàlla na leen Yàlla gërëm ñu jële ci yonnent bi SALLAHU ALAYHI WA SALLAM mu ne: "dara du jot jullit bi ci coono walla feebar walla tiis walla njàqarewalla lor walla tiis bu jeggi dayoo bu metti ba ci dég bi nga xam ne dina ko jam ludul ne YALLA dina ko ci faral ay bakaaram." xadis boobu BUXARI ak MUSLIM dëpóoo nañu ci génée ko waxin wii mu ngi génée ci li BUXAARI soloo.
Ñaareelu xadis bi : jëlee na ñu ci abii massa ud Yàlla na ko Yàlla gërëm mu ne Yonnent bi SALLAAHU ALEYHI WOSALAM nee na "amul benn jullit bu ab lor ci feebar walla lidul feebar di dal ludul ne YALLA faral na ko ci ay ñaawteefam ni nga xam ne noonu la xob di ruuse ci garab." xadis bii BUXAARI ak MUSLIM dëpóo nañu ci génée ko.
Ñetteel bi : jëlee na ñu ci yaay AÏSHA YALLA na ko YALLA gërëm mu ne Yonnent bi SALLAAHU ALEYHI WOSALAM nee na: "amul benn mussiba buy jot jullit bi ludul ne YALLA faral na ko ci bakkaar ba ci dég bi nga xam ne dina ko jam." xadis boobu BUXAARI ak MUSLIM dëpóo nañu ci génée ko.
Ñeenteelu xadis bi: ñu jëlé ci JAABIR YALLA na ko YALLA gërëm mu ne Yonnent bi SALLAAHU ALEYHI WOSALAM nee na "Bu bes pénc taxawee ñi nga xam ne dañu nekkoon ci jàmmi yaram ci àdduna ginaaw buñu giseée tuyaabo yi ñu jagleel ñi nekkoon ci ay nattu ñoom dañuy daldi mébët ne aka neexoon seeni der ci àdduna nekk loo xam ne ay daggukaay dañu ciy nekk di ci dagg." xadis boobu ki ko soloo mooy At-TIRMIZI te Al-ALBAANI wéral nako ñu ngi ñaanal wér gu yaram mbooleem wayi feebar yi ci jullit ñi moom YALLA mooy aji dégg ji te mooy kiy jox nit ki li mu laaj.