Jaangalé aj si wolof

1 Li ab nataalla bouy jaangalé aj
2 xétou aj yi
3 Lignouy ayé kou armal
4 Ay njoumté you siw lol si aj gi:

اسم الكتاب: خريطة الحج


الناشر: المكتب التعاوني للدعوة وتوعية الجاليات بالربوة


نبذة مختصرة: كتاب مترجم إلى اللغة الولفية، يبين مناسك الحج، والمواقيت المكانية، ومحظورات الإحرام، والأخطاء الشائعة أثناء الحج في ضوء الكتاب والسنة.


Jaangalé aj si wolof
خريطة الحج
< wolof>
    

    





Translator's name
Ibrahim Khali Lô

Reviser's name
Mohammed Cheikh Sene

 

 
خريطة الحج

        




ترجمة:
إبراهيم خليل لوح
مراجعة:
محمد شيخ سين

 

 Jaangalé aj si wolof

بسم الله الرحمن الرحيم
Bismil laahir rahmaanir rahiim
Si tourou yalla laniouy tambale souniouy wax ak souniouy dieuf ,mom miy brom yeurmande bou yatou bi tay brom yeurmendé bim diaglel dioulite yi.

Li ab nataalla bouy jaangalé aj
1-Barabou armalou kay yi:
-    Barabou armalou kaay bougnouy wax zoul houlayfa (biirou alioune):gnél wa médine,mouy soriyantok makka si lou tolok 427km (gnénti témérak gnar foukak jourom niar si ay kilomet).
-    Barab bougnouy wax  diouhfa wala rabikh gnél wa sham ak wa soowou diante (maroc) ak wa ezipt(egypte) mouy soriyantok makka si lou tolok 204km(gnari témérak gnént si ay kilomet).
-    Barab bougnouy wax xarnoul manaazil (sayloul kabir) gnél wa najdi mouy soriyantok makka si lou tolok 94km( jourom gnént foukak gnént si ay kilomet)
-    Barab bougnouy wax yalamlam(assaadiy)gnél wa Yaman mouy soriyantok makka silou tolok 94km(jourom gnént foukak gnént si ay kilomet)
-    Barab bougnouy wax zatou hirx mouy soriyantok makka si loutolok 98km(jourom gnént foukak jourom gnatti kilomet.
-    képpou  kou dikk si barab yi ta boko thi wa barab bi  ta beuga aj wala oumra dina dagan nga armalé fa, kiy aj wala oumra day armalé si armaloukay boum jeka rombou souy dém makka.
-    képpou kou wéssou armaloukay yi ta armalo day war si mom mou déllou fa dadi fay armalé,bouko défoul day war si mom mou réndi ap gatt wala  jourom gnaréli ther si gelém wala nak dadi séddelé ndawal li thi way gnaakk yi  nékk si haram bi (manam: fign wormal thi makka ).
-    Armaloukayou wa makka ak gninga xamni séne diganték makka amoul armaloukay ak ko xamni bam wésso armaloukayam lay dora am yénéy aj wala oumra laata mouy dougg thi orma gi (haram bi) famou sossé ajam falay armalé, kou nékk si biir haram bi nak dawara génn haram bi  dém fou mél ni tanhim (jakkay ya aycha) louy tolok 6km(jourom bénniy kilomét) wala jahirana, louy tolok 16km (foukak jourom bénn kilomét) wala fou mélni barab yoyou mou dadifay armalé.
-    Képpou kou tollok barabou armaloukay yi mo kham si jawwou ji la nékk walla si gééj gi day waajal dadi sangou sol armalam bala mou aksi si armaloukay bi ba soufa tolo rék day dadi yéné aj bouko néx.
-    Sounnal nagnou si gor bou aggéé tha armaloukay ba mou sangou dadi sétlou dadi  déf gett (latkologn) si yaramam ak sibopam ak sikinam moudadi sol armalam binga xamni woodou kay la ak ap lambay ta mou moytouko lalal latkologn. kou jiguén nak mom lignouy sounnal si mom  moy sou aggéé si armaloukay ba mou sangou latcolognou (donté sax danék kou sétoul  "mberek wala gessin) mou dadi sol louko sob si ay yérém yinga xam ni day mour awram (ta jigéne lépam awra la ba déss xar kanamam ak ay ténxem) ta limouy sol boum wané taram,
-    Soppou nagnou mou yéné ganaw jouli mo xam joulli farata wala nafila, (niki joulli yor yor,wala nafila youm daan faral di amal ganaw jaapp ak you mél niki yoyou).
-    Dana war thi kiy aj wala oumra mou dadi  yéné, bou féké ni aj mou tane aj bouko soop, bouy oumara nak,oumra rék lay yéné, mou wax( yaw yalla wouyou sinala si oumra).


xétou aj yi

1.    Tamattouh:  moy nga armal oumra thi si wéérou aj yi, ta gnoy (kori  digou tabaski ak jourom gnénti fane si wérou tabaski) mou dadi yénéé  thia barabou armaloukay ba, mou wax (yalla wouyou si nala si oumra),sou oumra wé ba soummékou si lay yééné aj thi bissou jourom niatél ba.
-    Dafay war thi kou tann khétou aj bi  mou tour darét bisoup tabaski.
2.     xiran: moy nga yéénéndo ajak oumra thi ak lenkelé lenke, nga wax  thi armaloukay ba :(yalla wouyou si nala si ajak oumra) bou aggé maka mou wer kabagi, dox safaak marwa, souko néxé tam mou yéxé dox safak marwa bi  ba bissou foukél bi ( bissou tabaski) bou nopé si lolou mou désak armalam ba motali ajam, momit war si mom mou tour darét bisou tabaski.
3.     ifrad: moy nga yéné aj késé, ta tour darét douko war, sou aggé tha armalou kay ba mou wax (yalla wouyou si nala si aj), sou aggé makka dafay wer kaba gi dox safak marwa bouko sobé mou bayyi safaak marwa bi ba bissou foukél ba, sou noppé si lolou day désak armalam ba kérok ajam di jéx.
-    Kiy aj bou ragalé ab gallankor dadikoy gaar badou mana agali ajam day dagan si mom mou sartal, dadi wax bouma ab gallankor gaaré ba agaliwouma sama aj famou ma gaaré moy sama simmikou kay( ta dara douko war.
-    kiy aj wala oumra sou xasé armal lép lougnko aayé day  haram  si mom mou déf ko.

Lignouy ayé kou armal
-    Dindi lénn si kawaram wala si ay  wéwam.
-    Jefendiko latkologn ak lou xéétok mom.
-    Labat wala takk sey,  douko takaal boppam ta déssou koko takkal, niki nono joték soxnam, wala lép loukoy waral.
-    Sol lougnou gnaw bamou nourok yéré, niki lou mélini simisou aladj wala toubay wala ay kawas ak youni mél.
-    Mour boppou si kou gor , moxam kaala lako mouré wala mbaxana wala you xétok yoyou. Bou dé  parasol wala mou yanou bagaz lolou dou lougnkoy téré.
-    Sol ay gaan si jigén wala mour kanamam si lou melni nikhab ak bourka ak you xétook yoyou, waayé nak sou néké si biiri gor yo xamni ay jambour lagn si mom day wathié colam si xar kanamam.
-    Yonal nagnou si kou gor ki mou yéketi batam si bouy wax (labaykal lahouma labayka labayka la sarika laaka labayka innal hamda wan nihmata laka wal moulk la sarik laka) manam ( yalla yaw la wouyou si, wouyou si goxam ni doumalasi bokalé. Yaw ya yayoo mbolém xééti thiante yi ak xéwel yi ak ngour yi, ta det gnoulasiy bokalé) kou jigéne ki  nak lignou yonal si mom moy mou soufél batam ba nga xamni jigén yimou déndal rék gnokoy dég.
-    Kiy aj nak bou xaséé armal lay tambalé wax (labayka….) ba fimouy waja weréé kaba ga mou sok ko dagg.
Naka lagnouy weréé kabagi:
-    Kiy wer kaba gi day, dém ba tollook hajaroul aswad tambaléfa werem bou mené foon xér wi nako foon, souko menoul mou lalko ak loxo nday joram dadi fon loxom  bouko menoul lal ak loxom mou joundiou ko ak loxo nday joram ta boumko foon moudal di wakh (allahou akbar) tambalé wer ta moyto lor nit gni si xatxatlo bi.
-    Lignouy yonal si kou gor ki bouy wer kaba gi werem gou ndiekk, moy mou génné mbangoum nday jooram, nga xamni armal  bim lambo si soufou poxoutanou nday joor bi lay jar. mou dadi sanni gnari lafi armal bi si kaw mbagou thiamogn bi.
-    Niki nonou dagnouy yonal si kou gor ki mou gnoukkou thi gnatti wer you ndiekk yi,  gnoukou nak moy(diganté daw ak dox, manam do daw bou bax ta do dox) kou jigén nak mom dox rék  lay déf.
-    Bou weré ba agg thi ponkkou bingay jot soga jot  hajaroul aswad yonal nagn mou lal ponk bobou ta boum ko foon souko menoul lal nak boum ko joxogn, ponkkou bobou laniouy wax (rouknoul yamani)si diganté ponkou bobou ak hajaroul aswad lamoufay wax moy(rabbanaa atinaa fid dounyaa hasanatan wa fil aaxirati hasnatan waxina hazaaban nari).
-    Jourom gnari yone lay wer kaba gi, ta boukoy wer menna gnan louko sop wala mou jang al xouran tamou moytoo yékketi baatab bay lor gniy wer, bou matalé jourom gnarél bi, na dekmel fignouy wax taxawayou Ibrahim(maxaamou Ibrahim) dadifay jangg laya bi (wat taxizou mine maxami ibrahima mousalla) mou joulli si ginaw taxaway bobou gnari rakka bou jappandéé, bou xaté nak ba menoufa joullé foumko joulé si biir jakka ji rék doynako, rakka bou ndiek bi mou jangg si (xoul ya ayyouhal kafiroun…)bam jééx, raka bou gnarél bi ( xoul houwal lahou ahad…) .
Naka lagnouy doxéé safaak marwa:
-    Ganaaw bamou weréé kaba gi jourom gnari yone jouli gnari raka day dadi dekmel safaak marwa,sou déméé ba joublou safa mou jang laya bi(inna safaa wal marwata min sahairil lah) souko janggé bay waja tambalé dox, na wax (mangi tambalé fi yalla tambalé) .
-    Gnouy yonal mou yék safa dadi joublou si kaaba gi wax (allahou akbar) dadi wax gnan wi(amoul béne bour bougnouy jamou si deg koudoul yalla.mom rék lagn wara jamou ta dougnouko bokalé.mom mo yayoo ngour ak mbolém thantt, mom minga xamni mbir yéppou si ndogalam lay améé, amoul bén bour bougnouy jamou si degg koudoul yalla ,mom mi metal ay diggém,dimbeli ap jamam, dadi not noon yi mom rék) mou baamouko gnatti yon, dadi gnan louko sop, bou waxé léne rék si gnanwi doynako.
-    Bou noppé si gnanam mou wathi safa dekmel marwa di gnanalé soxlam, di kagn yalla.
-     Kou gor ki nak sou aggé si mandarga bou wért bi  (lamp bou vert) day daw ba jéxal ko soga doxat ba agg marwa.
-    kou jigén mom dou daw dafay dox léppou.
-    Bou aggé marwa soppou nagn si mom mou yék  si kaw, déf nim défon safaa, bou nopé mou wathi, dadi dox dekmel safaa, mou daw thi diganté gnari mandarga yi, bou aggé safaa mou déf nim défon tha bamouy tambali, Nonou lakoy jaapé ba matal jourom gnari yon, (bou jougé safaa dém marwa moy bén, mou jougé marwa dém safaa mouy gnar, nounou lakoy jaapé bamatal jourom gnar, Safaa lay tambalé jéxalé marawa).
Watou wala waagni
-    Kiy tamatouh sou weré kaaba gi ba dox safaak marwa ba nopi, warna si mom mou wat kawaram wala mou waagni ko, souko défé mou dadi simmikou, lignou ko téréwon dadi dagan si mom, si nonou la oumraam di matéé; kiy aj xiran wala ifrad dougn wat séni boupou ta dougnou ko waagni, ta dougn simmikou, dagnou désak sééni armal ba bissoup tabaski.
-     kouy watou nak wala ngay waagni li war moy mou dajal bopp bi lép, wayé dou wat wala mouy wagn lénn si boppam di bayi lénn li.
-     Kou jigéén nak mom day wagn lou tolok thiatou baramam ganaw bam dajalé kawaram.

Lignouy def si bisoub jourom gnattél  bi si wérou adj:
-    Kiy aj xiran wala ifrad yonalnagn si mom mou dém mouna laata yoryor, dadi fay nékk ba bisoup jourom gnéntél.
-    Kiy tamatouh nak day armalé thi barab bim nék balaa yoryor di jot, mou dadi yéné aj wax( yalla wouyou sinala thi aj) (labbaykal lahouma hajan) mou dadi  dem mouna di baril  di wax(labbaykal lahouma labbayka…..) dadifay joullé mbolém joulli jourom yi, wagni yissi nékk gnénti
rakka ta doulén boléé.

Jefou bisoub jourom gnétéél (bisou arafaat):
-    yoonal nagn si kiy aj mou dém arafaat ganaw bi jant bi fénkéé thi bisou jourom gnéntél bi.
-    Bou aggé arfaat na wathi fougnouy wax namira (fi jakka ji nékk)  mou déglou khoutba bi bou féké ni lolou  jappandi na, niki nonou joulli tisbar ak takousan wagni ak bolélén.
-     Na baril  di jamou yalla  aki gnan, diko toudou diko sabal diko sant diko kagn, boudé menna joublou pénkou moy li gen.
-    Bou jantouk bisouk Arafat ga sowé mou jougéfa dém mouzdalifa andak dal ak téy ak toroxlou.
-    Gnouy yonal si mom bou aggé mouzdalifa mou boléfa timis ak géé wagni géé gi jouliko gnari rakka, bou yéxé ba géé wésou fékk aggagoul mouzdalifa nako jouli thi yon wi.
-    Bou aggé mouzdalifa li war moy mou fanan fa. Liy sounna nak moy mou joulé fa souba, wayé nak gni nééw kattane ak xalé yi dagana si gnom ak gni andak gnom gnou jougé fa dém mouna bou gouddi gi soréé.

Jefou bisoub foukél bi:
-    Yonalnagnou si kiy aj ganaw sou fajar joté tha mouzdalifa mou dekmel fi jakay mouzdalifa bi nék (masharoul haram) dadi fay gnan louko sob, soufa meunoul dém mou taxaw fim nék gnan soxlam, sou nopé lataa jant bi di fénk mou dém mouna.
-    Yonal nagn si mom mou for jouroom gnaari xéér you ndaw you doyni gnébbé wala youko eppou touti, fouko nééx nak lakoy foré, niki nonou gnouy yonal bou aggé thi xour bi mou gawantou si boufay romb, andak di wax (labaykal lahoumma labayka…) ba kérok mouy sanni jamra bou mak bi tamoy bou moujou bi.
-    Bis bobou jamra bou makbi rk lay sanni jouroom gnari xér you toftalo andak mouy yéketi loxom di wax (allahou akbar) si bép xéér boum sanni, xéér yi nak si mbaand mi la wara tabbi.
-    Ki aj xiraan wala tamatouh day war si mom mou réndi si bisoub tabaski bi,waxtou rendi bi nak yatouna ba jant bi sow si bousoup gnatél  si fanou mouna yi, ligen nak moy mou réndil boupam, wayé bougnouko réndilé dina wér, kou amoul loum réndi ta réndi warko nak day wor gnatti fan si aj gi, bou délo dekouwayam mou woor fa joroom gnaari fan mouy foukki fan.
-    Kou gor nak day wat kawaram wala mou wagni ko,wat nak mo gen, kou jigén nak day dajalé kawaram wagni si lou tolok thatou baramam.
-    Bou noppé mou dekmel kaaba ga werko kom nimouko weréwon bou ndiekk. Dagan na nak mou yéxé wer gi ba bis bou moujou si fani mouna yi.
-    Kiy aj tamattouh day dox safak marwa, kidéf ifraad wala xiraan nak dounko dox bou féké doxon nagnko si sén wer gou ndiekk.
-    Kiy aj bou défé gnar si jef yii di gnew(sanni jamra bou mak bi, ak wat wala wagni,ak wer kabaga) men na simmikou simikou bou njekk, gnouy yonal si mom mou sétlou latkolognou, dadi sol louko sob si yérém ak lép lougnou ko don moytoulo thik armalam, bamou dés joték soxnam ak lépp loukoy waral,wayé sou défé jef yignou touddou sank yépp nak simmikou na simmikou gou mak gi, mou dagan si mom mou déf yi gnouko moytoulo wone yépp bassi joték soxnaam.
-    Jef yi gnou toudou si jefi bisoup foukél bi menés nako bagna toftalé, boumsi jitel day dadi wér.
-    Yonal nagn ganaw tisbarou bisoup tabaski ba  takousanou biss bou moujjou si fani mouna yi mouy wax( allahou akbar allahou akbar la illaha illal lah,wal lahou akbaroul lahou akbar walillahil hamd).
-    Liy  war nak si fani mouna yi moy fanan fa. Joxé fa jouli yépp wagni ta bagn ko bolé.
Jefi fani mouna yi:
-    Day war si kiy aj mouy sanni gnatti jamra bis bou nékk si fani mounayi ganaw yoryor,jamra bou nék jouroom gnari xér lafay sanni, mou tambalé ko jamra bou ndaw bi, di kabbar si bépp xér boum sanni, sou noppé mou dox touti si wétou nday jooram dadi taxaw gnan  lou yagg.
-    sou noppé mou dém si jamra bou gnarél ba sanni kom nim sannéwon bou njekk ba doxaat touti taxaw gnaanat lou yagg.
-    sou noppé mou défaat nonou si jamra bou mak bi ta moy bou moujjou bi, sou noppé doufa taxaw di gnan.
-    Kinga xamni day yéxé mouna daffay fanan gouddip foukak gnatél bi,boudé day gawé nak bala jantoup bisoup foukak gnaarél bi di soo warna fékk mou génn mouna, sou génoul nak ba jant bi soo day war si mom mou fanan dadi motali.
-    sou matalé lim wara déf si fani mouna yi ba délou makka balaa mouy génn makka warna si mom mou wer werouk tagatok kaaba gi kém nim weréwon tha njelbén,
-      kiy gis mbaax wala gesin nak dou wer kabba gi .

 

 


Ay njoumté you siw lol si aj gi:
1-njoumtéy aramal:
•    wésou barabou armalou kay bi ta armalo.
    kou déf njoumté bi likoy war moy mou délou tha barabou armalou kay ba dadi fay armalé, sou féké ni nak manoul délou na armalé fam tollou, wayé  nak day war si mom mou réndi gatt, walla jouroom gnarélou therou gilém  wala nak dad koy séddelé way gnakk ya nékk tha wormalouk makka ga, ndaxté dabayyi lou war.
•    japp ni armal soko xasé sol bou tilimé sax waroko soppi.
    li wér moy ni dagna na gnou soppi armal, moo xam si gor wala jigén.
•    génné sa mbagou nday jor sani lafi armal bi si sa mbagi thiamogn  balaa ngay wer kaba ga.
    Li wér moy lolou thi wer kaba gi werouk oumra si ki tamatouh, wala werouk dougou si makka thi kou ifrad wala xiran késé lagnou ko wara déféé.
•    japp ni jigén bou gis mbaax waroul yéné aj tha armalou kay ba.
    li wér moy ni fofou lay yénéé déf léppou lou kouy aj di déf, bamou dés wer kaaba gi.
2-njoumtéy wer kaaba gi:
•    taxaw taxway bou yagg thi mandar ga biy wané fign wara tambalé wer bi.
    li war moy kiy aj joublou thi hajaroul aswad  bi dadi koy fon souko mené wala mou lal ko wala mou joundiou ko, dadi kabbar  dadi tambali werem ta bagna taxaw.
•    jaklél wer bou nékk ap gnan, Wala dajalo si bénn way mouy gnan di kawél batam.
    li wér moy mou gnan louko sop, di toudou yalla wala jang alxouraan,wayé amoul gnan wala ap zikar bougnou fa jaklél bén yon thi wer yi.
•    njortou ni gnari raaka yignouy joulli ganaw bougnou weré ba noppi warougnou ko joulé foudoul thi ginaw taxawayou Ibrahima bi wala fouko jégé.
    li wér moy dagan na nga joulé ko foula sop si bir jakka ji, ta liy sounna moy nga  woyofal ko bagn ko goudel.
3- njoumtéy dox safaak marwa:
•    gnénn gni dagnouy japp ni sougnouy dox safak marwa dém safaa ba déllousi waat fa  moy bénn.
    Li wér moy jougé safaa dém marwa moy bénn jougé marwa gnew safaa di gnar nga déllou marwa mouy gnatt nga jappé ko nonou ba am jouroom gnar, nga xamni safaa ngay tambalé jéxalé marwa.
4-njoumtéy bisoub jourom gnattél si wérou aj:
•    ki tamatouh japp ni si kaaba rék la wara armalé.
    li wér moy menna armalé fimou dal, mo xam maaka la wala mouna.
•    waagnék bolé jouli thi bisoub jourom gnatél.
    li wér moy wagni jouli yi wayé kénn dou bolé.
5-njoumtéy bisou arafat:
•    Yéék si dojou arfaat bi (rahma) japni da am ngenél, lolou bida bou  siw si nit gni wayé saxoul.
    li wér mouy ni gnaka yéék si doj bi, ndax yéék si saxoul si yonant bi.
•    génn arafat ngir dém mouzdalifa lata jant bi di sow.
    li war moy dés bir arafat bagn fa génn ba kérok jant bi di soo.
6-njoumtéy goudik foukél(mouzdalifa):
•    for xér tha mouzdalifa lata ngay jouli timis ak géé.
    li wér moy xér yi manés nako foré mouzdalifa ak fénén foudoul mouzdalifa.
•    jouli fajar lata waxtom di jot.
    li wér moy déésoul jouli fajar loudoul ni dagno am lou léér,wala mou not si sougnouy njortou ni waxtou fajar dougouna.
•    raxas xér yign wara sanné jamra.
    lolou ab bidaa la, saxoul si yonant bi.
7-njumtéy bisou mouna yi:
•    jel dall wala ay xér you rey diko sanni jamra, bolési  di saga di ngaagni, njortou ni saytané mofa nékk.
    li wér moy sanni xér you ndaw kéém niko yonant bi déféé, wayé ngir saxal jamou yalla ak taxawal toudou yalla.
•    jox kénén ngir mou sannilla fékk men nga sannil sa boppou.
    li war moy kou nékk  sannil boppam ta bagn ko wéékk kénén, loudoul ni menoul sannil boppam.
•    gnakka fanan bir mouna si loudoul ngant.
    li  war moy fanan bir mouna thi ay fanam .
8-njoumtéy werouk taggato:
•    jooxé werouk taggato laata ngay sanni jamra.
    -li war moy gnou déf wer kabba ga mou nékk lignouy moujé déf makka.
9-njoumtéy ziyara madinatoul mounawwara:
•    Ngénn gni dagnouy njortou ni ziyara jakkay yonant bi si aj gi la bokk.
    li wér  moy ziyara jakay yonant bi lougnou sopppo la si at mi yépp, wayé bokoul si aj gi,wayé nit ki sayou jappandé dagnouy yonal si mom mou dém jakkay yonant bi ngir jouli fa, ndax bénn joulli bofou day tollok jouniy jouli si bénen jakka joudoul mom ba dés jakay kaba gi.
-    joulit bi nak bou agé tha jaka ja dagnou sop si mom kom lignou sop si yénén jaka yi, tamoy mou jitel tank nday jooram souy dougou, ta mou wax (bismil lah,wassalatou wassalamou hala rasoulil lah,allahoum iftah li abawaaba rahmatika) mou dadi mouslou wax (mangui mousloo yalla mou magg mi,ak thi kanamam gou tédd gi,ak si ngourem gou yagg gi, si saytané mignou daxx si yermandé yalla), sou noppé mou joulli gnari rakka nouyoko jakka ji,sou noppé mou ziyara bamélou yonant bi,ak bou aboubakar ak omar,mou nouyou lén dad lén di gnanal, mou wax (yalla na jam ak yermandé yalla ak barkém nékk si yaw yonant yalla bi( (assalamou halayka wa rahmatoul lahi wa barakaatouhou ya rasoulal lah),mou nouyou aboubakar mou wax( assalamou halayka ya ababakrin) nouyou omar wax ( assalamou alayka ya omar).

 

 


Yénn faatéli ak dénkané you mata bayi xél:
1.    féxél xam sa adresou agence binga ngewé aj, ak sa dalou way si barap yépp; nga bind ko fou wor.
2.    moytoul di xatxatlo ak di bouxanté  soy wer kaba gi wala ngay dox safaak marwa wala ngay sanni jamra, ta nga féxé fégou dadi mour sa bakan ngir moytou pend bi ak yénn fébar yiy walaté.
3.    xamal ni yakamti si yénn jefou aj yi mennala yobbé thono yak say morom.
4.    toppal laaybiiré yila gni yor karangé aj gi di wax, nga xamni gnom yoon you gatt yi lagnou lagnou lay wan,ta nga jar si yoon yignou jaklél gniy dox, tanga moytou sa nooyi fatt walla nga am xatxat si younou daamar yi.(oto)
5.    xamal ni lal si yoon yi ak barabou jamou kayou yalla yi difa tok wala tedd dafay xatal yoon yi di lor say morom ak gniy saytou aj gi.
6.    nguir sa karangé:
    jefendikol parasol boulay ar si jant bi ngir nga mouthiou si thiégnéri jant bi aki ay lorangém.
    baril loy naan ndox basi sax so maroul gnir nga mana mouthou basa pout dou wow, wara lorangé boxam ni gnakk ndox mokoy waral si boy joxé say jamou yalla.
    dél baril loy raxas say loxo jefendiko sabou ngir nga mouthiou si fébr yiy wallaté.
    mbalit yi ak salté yi déko déf si fign lénn jaklél.
    moytoul di tall safara thi bir xayma yi.

 

 

 

 

 

Attéy jotou(fidya) ak kou am gallankor ba meunoul agali
ajam, ak kou déf lénn si yign ko téré ganaw bimou armalé:
1.    képp kou déf lénn si lignouy téré sou armalém thi ak tayéf, lou mél niki watou, wala lélli ay wéé, wala mou latkolognou, wala kou gor ki mour bopam, wala mou sol lougnou gnaw, wala mou jonjok jigén si ak bannéx, wala kou jigén ki mour kanamam, kou déf lén si yi, liko war moy mou jotou. Tamoy mou déf lén si gnatt yi:
    wor gnatti fan.
    wala mou léél jourom bénni way ngakk.
    wala mou réndi ap gatt sédelé ko way gnakk yi nékk makka.
-    Boudé nak bamoukoy déf dako fatté wala gnakka xam yobbékoko dara douko war.
2.    kép kou bayi jef jo xam ni dafa war si jefi aj yi wala oumra, kom armalé tha armalou kay ba, wala sanni jamra, likoy war moy mou réndi ab gatt walla jouurom gnarélou xajoup gelém wala nak dadi sédelé ndawal li thi way gnakk yi nékk makka.
3.    simmikou gou njekk gi daflay daganalal lépp lougn la téré won bam dés sey ak lépp loukoy waral, simmikou bobou nak mingi am si bou kiy aj défé gnar si jefi bisou tabaski yi ta gnoy( sanni jamra gou mak gi, ak watou wala wagni, ak wer kabagi), batax na képp kou joték soxnam bala soummikou gou njekk gi ajam day yaxou ba noupi am louko war ta moy yi di gnew:
    mottali aj gi.
    réndi ap gelém.
    fay aj si at bisi top.
    toub dadi jégelou yalla sboudé nak joté gim joték soxnam ganaw soummikou gou njekk gi la, likoy war moy mou réndi gatt walla jorom gnarélou theur si gelém wala nak mou sédaléko way gnakki makka yi.
•    ki armal banoppi sou menoul agali ajam ta fékk sartaloul won bamouy armal, likoy war moy mou tour dérét dadi sédelé ndawalli si way gnakk yi, niki nonou mou wat kawaram wala mou wagni ko si nonou lay simmiko.
•     sou fékké ni menoul réndi, day woor foukki fan banoppi wat kawaram wala mou wagni ko bouko défé mou simmikou.

Lénn si ay gnaan you rot si alxouran ak sounna:
    Soppou nagn thi kiy aj mouy baril limouy touddou yalla, diko gnaan, di ko toroxloul, di jouli si yonant bi, di ngan yalla yiwou addina ak bou allaxira,
    li lénn la si gnan yi rot si alxouranak sounna:
1.    (rabbana aatina fiddounya hasanatan, wa fil aaxirati hassanatan, waxinaa hazaaban naar).
    Moy: ( yaw yalla mangilay gnan yiwou addina ak bou allaxira, tanga fégalma  mbougalou safara)
2.    (allahouma aslih li diinil lazii houwa hismatou amrii, wa aslih lii dounyaayal latii fiihaa mahaasii, wa aslih lii aaxiratil latii fiihaa ma-aadii, wajhalil hayata ziyaadatan lii fii koulli xayrin; wal mawta raahatan li min koulli sarrin).
    Moy: (yaw yalla mangi lay gnan nga yiwel sama diiné ji nga xamni moy aar samay mbir, tanga baxal sama addina binga xamni filaay doundou, tanga baaxal sama alaxira binga xamni moy sama déllou way,ta nga déf doundou gi di loumay dolli yiw,nga déf samak fatou mouy loumay noppal si bépp ay).
3.    (ahouzou billahi min jahdil balaa, wadarakis saxaa, wa sou- il xadaa, wasamaatatil ahdaa).
    Moy: ( mangui mousslo yalla thi thonay nattou,ak téxéédi, ak ndogal gou gnaw, ak mbéktéém non yi).
4.    ( allahoumma innii ahouzou bika minal hammi wal hazani, waminal ajzi wal kasali, waminal joubni wal bouxli, waminal maasami wal maxrami, wamin xalabatid dayni wa xahrir rijaal, wa ahouzou bikal lahoumma minal barasi wal jounouni wal jouzaami, wamin sayi-il asxam).
    Moy: (yaw yalla mangi lay mouslo thi jaxlé ak tiis, ak thi teléék tayyél, ak thi ragalak gnaax, ak thi bakar you diis yi, ak gnou notma si sama diné, ak notou nit gni,  malay mouslo yaw yalla  thi fébarou ramm ak fébarou xél ak gaana ak si mbolém fébar you bon yi).
5.    ( allahoumma innii as aloukal afwa wal aafiyata fiddounya wal aaxirati,  allahoumma innii as aloukal afwa wal aafiyata fi diinii wa dounyaya, wa ahli wa maali, allahouma oustour awraatii, wa aamine raw-aatii,wahfaznii min bayni yadayya wa min xalfi, wa an yamini wa an simaalii, wa min fawxii, wa ahouzou bi izamtika an ouxtaala min tahtii)
    Moy: ( yaw yalla mangui lay gnan ndiégel ak jammiy adounaak alaaaxira, yaw yalla mangui lay gnan ndiégel ak jamm thi sama diiné ak sama aaddouna, ak thi samak njabotak sama alal, yaw yalla mangi lay gnan nga soutoulam, tanga mayma ak koalouté si samay njaxxaré, tanga samal ma sama kamam ak sama ginaw ak sama nday joor ak sama thiammogn ak sama kaw, may mouslo samaggaay si gnou dikké thi ma sama souf).
6.    ( allahoumma ixfir lii xatii-atii wa jahlii, wa israafii fii amrii,wama anta ahlamou bihii minnii,allahoumma ixfir lii jiddii wa hazlii; wa xata-ii wa amdii, wakoullou zaalika   indii,allahoumma ixfirlii ma xaddamtou wama axxartou, wama asrartou wama ahlantou, wama anta ahlamou bihii minii, antal mouxaddamou wa antal mou axxarou, wa anta ala koulli say in xadiir).
    Moy:)  yaw yalla mangui lay jégalou samay baakaar ak samak réer, ak samak eppel si samay mbir, ak lépp lo xamni yamako gena xam si samay ngaawtééf, yaw yalla mangui lay gnan nga jéggelma souma nékkéé thik farlou ak thiy thiaxan, ak samay njoumték samak tayééf, lolou lépp thi manla, yalla mangi lay jéggelou lima jiitel ak lima moujéé, ak lima nebbek lima fégnal, ak lepp lo xamni yamako gena xam, yaw yay ki jiitou, yay kiy moujou, ta mbir yépp yay kokoy dogal).
7.    (allahoumma inna as aloukas sabbata fil amri, wal hazimata halar rousdi,wa as alouka soukra nihmatika, wa housna ibaadatika, wa as alouka xalban saliiman, wa lisanan saadixan, wa as alouka min xayri ma tahlam, wa ahouzou bika min sarri maa tahlam, wa astaxfirouka lima tahlam, innak hallamoul xouyoub).
    Moy:(yaw alla mangi lay gnan sax si say ndigel, ak dogou si sak njoup, may sakkou si yaw nga deppeléma bamalay sant sisay xéwel, ak di jamou si noum gena rafété, malay gnan xol bou mouthou, ak lammign bou deggou, malay gnan bépp yiw bo xam, dila mouslo si bépp ay bo xam, dila jéggelou si linga xam, yaw yay kiy xammakon li oumpou).
8.    ( allahoumma rabbous samaawaati wal ardi,wa rabboul harsil hazim, rabbounaa wa rabbou kouli say-in, faalixoul habbi wannawaa,mounazzilout tawraat,wal injil wal xour-aan, ahouzou bika min sarri kouli say-in anta aaxizoun binaasiyatihii, antal awwalou falaysa xablaka say-oun, wa antal aaxirou falaysa bahdaka say-oun, wa antaz zahirou falaysa fawxaka say-oun, wa antal baatinou falaysa dounaka say-oun, ixdi anid dayna, wa axninii minal faxri).
    Moy: ( yalla yaw miy boroom asamaan ak souf, di boroom aras mou magg mi, di sougnou boroom di boroomou bépp mbir, yay fétt pépp yi ak saal yi bougn léén jiwéé, ya wathé tawraat ak injiil ak al xour-aan,  mangi lay mouslo si ayou lépp lo xamni yako téyé, yay ki jiitou ta dara jiitou woula, yay kiy moujou ta dara dou gnew sa ginaw, yay ki fégn ta dara fétéwoula kaw, yay ki nebbou ta dara genoula nebbou, mangilay gnan nga fajjal ma samay bor tanga womal ma si gnakk).
9.    (allahouma aati nafsii taxwaha, wazkkiha anta xayrou man zakkaha,anta waliyouha wa mawlaha, allahouma inni ahouzou bika minal ajzi wal kasal, waminal joubni wal heremi wal bouxli,wa ahouzou bika min azabil xabri),
    Moy: (yaw yalla mangi lay gnan nga may sama bakan ak ragal yalla, tanga séllal ko,yaw ya gen si likoy sélal, yaw yay kiko méngo diko dimbeli, yaw yalla maangi lay mouslo si telék tayyél, dila mouslo thi ragal ak maagét ak nay, dila mouslo thi mbougelou bammél).
10.    (allahouma laka aslamtou, wa bika aamantou, wa alayka tawakaltou, wa ilayka anabtou, wa bika xaasamtou, ahouzou bihizzatika an toudillani, laa ilaaha illaa anta, antal hayyoul lazii laa yamoutou wal jinnou wal insou yamoutouna).
    Moy: (yalla yaw la jébbel sama boppou,yaw rék laa gem, ta si yaw kasé laa soukandikou, ta si yaw lay déllou, ta si yaw lay xoulo,mangi mouslo sa maggay thi nga sank ma, amoul bénn bour bougnouy jaamou si degg koudoul yaw, yaw yay aji doundou bidoul faatou moukkou, nitak jinné dagnouy faatou).
11.    (allahoumma innii ahouzou bika min hilamin laa yanfah,wamin xalbin laa yaxsah, wa min nafsin laa tasbah, wa min dahwatin la youstajaabou lahaa).
•    Moy: ( yaw yalla mouselma thi xam xam boudoul jarign, ak si xol boula doul ragal,ak si bakkan boudoul doylou, ak si gnan bougn doul namgou).
12.    ( allahoumma innii as alouka minal xayri koulihii haajilihii wa aajilihi, ma alimtou minhou wama lam aalam, wa ahouzou bika minas sari koulihii haajilihii wa aajilihii,ma alimtou minhou wama lam aalam, wa as alouka min xayri maa sa alaka minhou abdouka wa nabiyouka mouhammad,wa ahouzou bika min sarri mastahaza minhou abdouka wanabiyouka mouhammad).
•    (yaw yalla mangui lay gnan bépp yiw,mo xam bou gaw la wala bou yééx, malay moulou si bépp ay, mo xam bou gaw la wala bou yéx, yalla mangi lay gnan bépp yiw boula sa jam ak sa yonant mouhaammad massa gnan, malay mouslousi bépp ay boula sa jam ak sa yonant mouhammad massa mouslo).
13.    (allahoumma innii as aloukal jannata wamaa xarraba ilayhaa min xawlin aw amal,wa ahouzou bika minan naari wamaa xarraba ilayha min xawlin aw amal,wa as alouka an tajhala koulla xadda- in xadaytahou li xayran,).
•    Moy: (yaw yalla mangi lay gnan aljana ak lépp loufay yboubbou waaté  si wax aki jef, malay mouslo thi safara ak lépp loufay yobbouwaaté si wax ak jef, malay gnan lépp loy dogal si man mou nékk yiw).
14.    (laa ilaaha illallahou wahdahou la sarika lahou,lahoul moulkou wa lahoul hamdou bi yadihil xayrou wahouwa alaa kouli say-in xadiir,soubhaanal laa, walhamdou lillaa, walaa ilaaha illallaa, wallaahou akbar,walaa hawla walaa xouwwata illaa billaa.)
•    Moy: ( amoul bénn bour bougnouy jaamou si degg koudoul yalla, mom dongg ta dougnou ko bokkaalé,bép ngourak thant mom la gnél,mooy faat mooy doundel, mbooléém yiw si loxom la nékk, ta mom moy dogal béépp mbir, touddounaa  ak séllam,ta sant naako, ta kénnaal naako, ta maaggal naako, ta péxéék kaattan amoul loudou si mom yalla mou kawé mi ta maagg).

 

 

 

 

 


    
    

 

    

 

Jaangalé aj si wolof

Download

About the book